From professional translators, enterprises, web pages and freely available translation repositories.
i jesus have sent mine angel to testify unto you these things in the churches. i am the root and the offspring of david, and the bright and morning star.
«man yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede leen mbir yii ci digg mboolooy ñi gëm. man maay car, bi soqikoo ci daawuda, di biddiiwu njël bu leer bi.»
and out of the throne proceeded lightnings and thunderings and voices: and there were seven lamps of fire burning before the throne, which are the seven spirits of god.
ay melax, ay riir ak ay dënnu di jibe ca gàngune ma. ca kanamu gàngune ma amoon na fa juróom-ñaari làmp yu yànj, di juróom-ñaari xeli yàlla yi.
and the kings of the earth, who have committed fornication and lived deliciously with her, shall bewail her, and lament for her, when they shall see the smoke of her burning,
buuri àddina yépp, yi àndoon ak moom ci njaaloo ak mbuux, bu ñu séenee saxar siy jollee ci taal bi ñu koy lakke, dinañu yuuxu, di ko jooy.
and cornelius said, four days ago i was fasting until this hour; and at the ninth hour i prayed in my house, and, behold, a man stood before me in bright clothing,
ci kaw loolu korney tontu ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam,
and the beast was taken, and with him the false prophet that wrought miracles before him, with which he deceived them that had received the mark of the beast, and them that worshipped his image. these both were cast alive into a lake of fire burning with brimstone.
Ñu jàpp rab wa, moom ak naaféq ba mbubboo yonent, ba daan def ca turu rab wa ay kéemaan yu mu naxe ñi nangu woon a am màndargam rab wa te jaamu nataalam. Ñoom ñaar ñépp sànni nañu leen ñuy dund ca déegu safara ak tamarax buy tàkk.
while he yet spake, behold, a bright cloud overshadowed them: and behold a voice out of the cloud, which said, this is my beloved son, in whom i am well pleased; hear ye him.
waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «kii mooy sama doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»